TSK

TSK · Isaiah 49:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal. Mbete dëkk bu ñu gaw!

Moo tax ñoñi Aji Sax ji di duggi ngàllo ndax ñàkk xam-xam. Seen kàngam ay deeye xiif, seen baadoolo deeye mar.

Yaw Yerusalem, mi ñu jàpp njaam, jógal fëgtu, yaw janq Siyoŋ mu taaru mi ñu jàpp njaam laa ne, tikkil buum gi ci sa baat.

Dees laa foñ, jéppi la, ba kenn jaareetu fi. Waaye maay def ñu di la sagoo ba fàww, di la bége sët ba sëtaat.

Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.

Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.

Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliwu àll gi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.

Te su ngeen bokkee ci Almasi, yeen ay askanu Ibraayma, te yeena jagoo dige ba.