Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»
TSK
TSK · Isaiah 49:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
mu yilif géej ba géej ak dex ba ca cati àddina.
Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.
Yeneen xeet yeey delloo bànni Israyil ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israyil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon.
Ñu ngiy bawoo fu sore, ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu, ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.»
Xeet yooyooy indi seen bokk yi bokk ak yeen ñépp, jële leen ci mboolem xeet yi, ñu doon sarax bu ñeel Aji Sax ji, wari fas aki watiir, ba ci watiir yu ñu mbaar, aki berkelleeki giléem, ba agsi sama tund wu sell, wi ci Yerusalem.» Aji Sax jee ko wax. «Day mel ni noonu bànni Israyil di yóbboo sarax, yeb ko ci ndab lu sell, yóbbu kër Aji Sax ji.
Penku ak sowu, bëj-gànnaar ak bëj-saalum, la aw nit di bawoo, dikk toog ca ndabal bernde la ca nguurug Yàlla.