TSK

TSK · Isaiah 52:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Sàkkalal sa mag Aaróona yérey sellnga ngir daraja, ak teraanga bu sarxalkat wara yelloo.

¶ Ba mu ko defee njiiti mbooloo ma dëkk Yerusalem. Ña des ca mbooloo ma tegoo bant ngir fukk ñu daje kenn génne ca, dëkk Yerusalem, dëkk bu sell bi, juróom ñeent ñi ci des toog ca (seeni) dëkk yu ndaw.

Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc, te nekkoon dëkkub kóllëre, njubte mate fa, njekk lal fa panaan, tey ñu diy bóomkat!

Ubbileen bunt yi, ba xeet wi jub te sàmm ngëm duggsi!

moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi, di wéeroo Yàllay Israyil ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

Yewwulee, yewwul, Yerusalemee jógal, yaw mi Aji Sax ji nàndal kaasu mbugalam. Kaas bu wex bay miirloo, taat wa, yaa ko siitaatu.

Sa askan wépp ñu jub lañuy doon, te ñooy moom réew mi ba fàww. Ñooy sama njëmbat li ma jëmbatal sama bopp, sàkke leen samay loxo, ngir sama teddnga teew.

Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: «Bépp doxandéem bu xaraful ci xol, xaraful ci jëmm, bumu duggati sama bérab bu sell bi, muy doxandéem bu mu mana doon, bu dëkk ci biir bànni Israyil.

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen, kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.

Teewul baay ba ne ay surgaam: “Gaawleen indi mbubb mi gëna rafet, solal ko, te ngeen takkal ko ab jaaro ci loxoom, solal ko ay dàll.

Waaye yiirooleen Sang Yeesu Almasi, te ngeen baña yittewoo seen bakkan, ngir di topp seeni xemmemtéef.

¶ Li ci des nag moo di ngeen manoorewoo Boroom bi, te ngeen sàkkoo ndimbal ci dooleem ak kàttanam gi amul kem.

Xarekat yi ci asamaan a ko topp, war fas yu weex, sol mbubbum lẽe mu weex, set wecc.

Du lenn lu sobewu lu fay dugg nag, mbaa defkatu jëf ju ruslu ak njublaŋ. Ñi ñu bind ci téereb dund bu Gàtt bi doŋŋ ñoo fay dugg.