TSK

TSK · Isaiah 55:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.

Maay def garabi seedar aki séng ca màndiŋ ma, saxal garabi mirt ak oliw ca joor ga, sippar ak garabu pẽe, ak yeneen garab yu dëkke naat, ma boole ca,

Bu tund yu mag yi doon toxu, yu ndaw yiy raf sax, sama ngor du la toxul, te sama kóllërey jàmm du raf.» Aji Sax ji la yërëm moo ko wax.

Maay wuutale xànjar, wurus; wuutale weñ gu ñuul, xaalis; bant, xànjar; doj, weñ gu ñuul. Jàmm laay def mu jiite la, def njekk yilif la.

ngir tabb waa Siyoŋ ñiy ñaawlu, jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal teddngaam.»

Ndax ni njiitlaay di taqe ci luppu nit, noonu laa jële woon waa kër Israyil ak waa kër Yuda, taqoo leen.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa ko def ngir ñu doon sama ñoñ, teral sama tur, di sama ndam, di sama sag. Waaye déggaluñu ma.»

Dinañu laaj yoonu Siyoŋ, jublu fa te naan: “Ayca nu dajeji fa Aji Sax ji, ci biir kóllëre gu sax gu kenn dul fàtte.”

Luke 2:14 TSK

«Daraja ñeel na Yàlla fa asamaan sa gëna kawe, jàmm ci kaw suuf ñeel ñi Yàlla baaxe.»

¶ Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.

Kon bu nit ki bokkee ci Almasi, mbindeef mu bees lay doon. La woon day wonni, li teew nag, di lu yees.

¶ Waaye yeen nag yeen ay giir giy tànneef, yeenay sarxalkati Buur, yeen ay askan wu sell, yeen ay xeet wi ñu jot, ngir ngeen biral jaloore yu wéet yi ñeel ki leen woo, génnee leen cig lëndëm, indi leen ci leeram gu yéeme.