TSK

TSK · Isaiah 55:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji nag ne Samiyel: «Bul xool ci melokaanu kii, mbaa jëmmu taxawaayam, ndax gàntal naa ko. Lii du ci gis-gisu nit. Nit, li fees bëtam lay gis, waaye Aji Sax ji ci xol lay xool.»

¶ Naaman nag mer. Ma ngay dem te naan: «Xoolal rekk, man mi noon day daldi génn taxaw ci biti, ñaan ci Yàllaam Aji Sax ji, tiimale loxoom ër bi, daldi teggi jàngoro ji!

Aji Sax ji ngor ak dëgg rekk lay jiitee kuy sàmm kóllëreem ak seedey yoonam.

Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.

Maneesula daj li ci xelu buur, xalaatam daa kawe ni asamaan, xóot ni suuf.

Mu ne: «Su waay fasee jabaram, mu dem doon jabaru keneen, Su waa ja jëlaatee ndaw sa ëllëg, Loolu du sobeela sobeel réew mii? Moona yeen gànctu ngeen aki fari far, Ana nu ngeen mana délsee fi man?» Kàddug Aji Sax jee.