TSK

TSK · Isaiah 59:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax jee gis loolu, gedd, ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.

Ba mbooloo ma ñibbee ca dal ba, magi Israyil ña ne: «Lu waral Aji Sax ji dumalu nu tey fi kanam waa Filisti? Nan jëleji gaalu kóllërey Aji Sax ji fa Silo; na dikk ci sunu biir, ba musal nu ci sunuy noon.»

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

Ñaawtéefi Israyil ak alalam ju lewul moo ma merloo, ma duma ko, xañ ko sama kanam, waaye mu të ticc, topp xolam.

Yooyii seeni ñaawtéef a ko waññi, seen bàkkaar a leen xañ ngëneel.

Seeni sobeek seeni tooñ laa jëflanteek ñoom, ba xañ leen sama kanam.

Micah 3:4 TSK

Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall, te du leen wuyu, kanamam la leen di làq, bésub keroog, nde ñoo bonal seeni jëf.