TSK

TSK · Isaiah 6:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mennum man mii maay far say moy ngir man, ba dootuma fàttliku bàkkaar.

Moona Aji Sax ji la soob, mu dëggaate jaamam bii, teg koy naqar, su nangoo doon saraxu peyug tooñ, gis askanam, aw fanam gudd, te coobarey Aji Sax ji ci moom lay sottee.

Jekki-jekki jëmm ju mel ni nit dikk, laal samay tuñ. Ma ŋa, àddu, daldi wax ak ki taxaw sama kanam ne ko: «Sang bi, peeñu mi tax na ma jàq, ba amatuma benn doole.

Malaaka ma wax ak ña taxaw fa kanamam ne leen: «Summileen yéreem yu dand yi.» Mu teg ca ne Yosuwe: «Dama ne, far naa sa bàkkaar, te dinaa la solal lu jekk.»

Ndegam deretu sikket ak yëkk, ak nag wu jigéen wu ñu lakk, ngir suy dóom ba nit ku sobewu, yooyu lees daan sellale nit ñi, ngir seen cetug yaramu suuxu neen,