TSK

TSK · Isaiah 6:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi.

Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.»

Teewul malaakam Aji Sax ja àddoo asamaan, ne ko: «Ibraayma! Ibraayma!» Mu ne ko: «Ãa!»

Ana askan wu masa dégg baatu Yàlla bu jibe ci sawara, ni ngeen ko dégge te dese bakkan?

Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.

Bu ñuy naaw, may dégg seen coowal laaf yi, mu mel ni géej mbàmbulaan, melati ni kàddug Aji Man ji, di saf riirum xare. Bu ñu taxawee, daldi wàcce seeni laaf.

Waaye sama bakkan soxalu ma, xanaa ma bey samaw sas, ba sottal liggéey, bi ma Sang Yeesu dénk, te mooy seedeel xibaaru jàmm bu yiwu Yàlla wi.

Jógal taxaw nag. Dama laa feeñu ngir def la ngay sama surga, ngir nga di ma seedeel peeñum tey, ak peeñu yi ma lay feeñooji ëllëg.

Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi.