TSK

TSK · Isaiah 60:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Nguur gi du jóge ci loxol Yuda, te yetu buur ay wéye sampe ciy tànkam, li feek boroom di ñëw, ba xeet yi déggal ko.

Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleena gudd fan!»

Yeen, seen Yàlla dogalal na leen kàttan; éy Yàlla, jëfeel doole ja nga nu jëfeeloon.

yal na turam sax, ba law fu jant tiim, yal na xeet yépp barkeele ci moom, te di ko ndokkle.

Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji, buuri àddina sépp wormaal darajaam,

Aji Sax ji, na la buuri àddina yépp màggal, ñoo dégg kàddu yi nga wax.

Bésub keroog car bawoo ca Yese, reen ba, taxaw di raaya buy gindi xeet yi, xeet yi di ko sàkku, dal-lukaayam ba jagoo teddnga.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus, ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw, ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo. Sa gannaaw lañuy topp, yeewe, jàllsi; sujjóotal la, di ñaan naan: “Fi yaw daal la Yàlla ne, du feneen, te tuur neen la.”»

Ñu ngiy bawoo fu sore, ñu ngii bawoo bëj-gànnaar ak sowu, ñee bawoo diiwaanu Sinim ca bëj-saalum.»

«Yaw mi jaasir ba juroo, xaacul! Yaw mi xamul mititu mat, sarxolleel.» Aji Sax ji nee: «Ndaw si ñu foñ moo gëna jaboot kiy séy.

Yaay naan soowum xeet yi, nàmp weenu buur yi, ba xam ne maay Aji Sax jiy walloo, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.

Maay teg firnde fi seen digg, ba jël ñenn ca ña dese bakkan ca ñoom, yebal leen ci xeet yi, yebal leen Tarsis, ak Pul ak Ludd, ñooña di ñu mane fitt, ma yebal leen ca waa Tubal ak Yawaan, waa duni géej yu sore ya, ñooñu masula dégg sama jaloore, te masuñoo gis sama teddnga, sama ndaw ñaa leen di xamal sama teddnga.

Micah 4:1 TSK

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Ay askan ñooy dikkati, di waa dëkk yu bare,

Ndax noonu la nu ko Boroom bi sante ba mu nee: “Maa la tabb ngay leeru jaambur ñi, ngir nga jottliji mucc gii, ba ca cati àddina.”»

¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.

¶ Ba mu ko defee, juróom ñaareelu malaaka mi wal liitam, baat yu xumb jibe ca asamaan, ne: «Léegi nag nguurug àddina ñeel na sunu Boroom ak Almaseem. Mooy nguuru ba fàww.»