TSK

TSK · Isaiah 63:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yuuxuleen! Bésub Aji Sax ji moo dëgmal, te ni sànkute gu bawoo fa ci Aji Man ji lay dikke.

Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.

Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp,

«Yeen gan ñi, génnleen Babilon, ku ne rawaleji sa bakkan. Buleen ñaawtéefu jaambur sànkaale; lii àppu mbugal la bu Aji Sax ji matal; seen añ la, bu mu leen añale.

Déglul bu baax, yaw Yosuwe sarxalkat bu mag bi, yaak sa xarit yi toog fi sa kanam te taxawe ab tegtal, nde maa ngii di indi samab jaam, ki ñuy wax Njebbit li.

¶ Ba mu tàyyee juróomeelu tayu gi, ma gis ci suufu sarxalukaay bi, bakkani ñi ñu bóom ndax kàddug Yàlla ak seede si ñu ci seede.

Ndokklee, asamaan, Ndokklee, yeen ñu sell ñi itam, ak ndawi Yàlla yeek yonent yi, ndaxte Yàllaa leen àtteek dëkk bii, mbugal ko.