TSK

TSK · Isaiah 63:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 21:20 TSK

gisal boppam sànkuteem, ba jolu merum Aji Man ji!

Yàllaay àtte: kii mu detteel, kee mu kaweel.

Moo wàcce ñi dëkke woon fa kaw, moo detteel waa dëkk ba aju woon, daaneel leen, ñu xalangu, ba mëq suuf,

Ñi lay néewal, maa leen di leel seen suuxu bopp. Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, ba kuy boroom suux xam ne maay Aji Sax ji lay wallu, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»

Rikk déglul nag lii, yaw mi musiba dal, nga màndi te du biiñ.

ñu naan, tërëf, di say ndax aaytéefu saamar laay yebal fi seen biir.»

kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.

Dëkk bu mag ba xar ñett, dëkk yu mag yu askani àddina yi màbb. Babilon gu mag ga nag, Yàlla bàyyi ko xel, ngir nàndal ko kaasu biiñu sànjam muy bax.

¶ Ba loolu amee malaaka mu am doole yékkati doj wu mel ni doju wolukaay wu mag, sànni ko biir géej, daldi ne: «Babilon dëkk bu mag bi, nii lañu koy sànneek doole, mu ne meŋŋ.