Isaiah 40:1
TSK
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?
Yeen soppey Yerusalem yépp, bégandooleen ak moom, te di ko bànneexoo. Mboolem yeen ñi doon ñaawlu tiisu Yerusalem, bokkleen ak moom xolam bu sedd.
Manoon nanoo taafantoo li nu diy ndawi Almasi, ba diisal leen, waaye danoo lewetoon domm ci seen biir, mel ni jaboot juy topptoo ay doomam.