TSK

TSK · Isaiah 8:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Bu ngeen demee ngir xarejeek seeni noon ba gis ay fas, aki watiir, ak gàngoor gu leen ëpp, buleen leen ragal, ndax seen Yàlla Aji Sax jaa ngeek yeen, ki leen jële woon réewum Misra.

Fekk na ñu wax Daawuda ne ko Ayitofel bokk na ca ña lëngook Absalom. Daawuda nag ñaan ne: «Yaw, Aji Sax ji, ngalla yàqal pexem Ayitofel.»

¶ Ci biir loolu Ayitofel gis ne déggeesul ndigalam, mu takk mbaamam, ñibbi ca dëkk ba mu fekk baax. Mu daldi topptoo mbiri këram ba mu jekk, ba noppi wékk boppam. Mu dee, ñu denc ko ca sëgi baayam.

Job 5:12 TSK

Keey neenal pexem ku muus, ba mébétam du sotti.

Ñoo la mébal lu bon, nasal la pexe, joyul.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.

Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.

Xoolal sa noon yiy riir, sa bañ yi fippu ba téen!

Waa Siri ñoo ànd ak Efrayim ak doomu Remalya, di la fexeel naan:

Kon nag Boroom bi ci boppam moo leen di jox firnde: janq bi mooy ëmb, jur doom ju góor, tudde ko Emanuwel (mu firi Yàllaa ngeek nun).

Dooley kilifteefam ak jàmm ja du am kemu, fa jalub Daawuda ak nguuram, ga muy samp, saxale ko njekk ak yoon, tey jii, ba fàww. Lii la Aji Sax ji Boroom gàngoor yi def ci xéraangeem.

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

Nahum 1:9 TSK

Ana lu ngeen di fexeel Aji Sax ji? Mooy neenal, lépp neen; njàqare ja du ñaar.

Acts 5:38 TSK

Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?