TSK

TSK · Isaiah 8:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab.

¶ Bunt ba ñuy wax Bëtu Ndox ba, Salun doomu Kol Ose, boroom gox ba ñuy wax Mispa, moo ko defaraat. Moo ko tabaxaat, xadd ko, taxawal laf ya, ak tëjukaay yaak dénki galan ya cay ànd, ak itam tata ja ca déegub Silowe, bay suuxat toolu buur, ba ca dëggastal ya ngay wàcce, génn gox ba ñuy wax Kër Daawuda.

¶ Janti buurub Yuda, Axas doomu Yotam miy doomu Osiyas, Reccin buurub Siri moo dal ci kaw Yerusalem, ànd ak buurub Israyil, Peka doomu Remalya. Waaye manalu leen dara.

‘Nan songi Yuda, tiital leen, nangu ko, fal fa doomu Tabeel buur.’

«Ñaari yoon la xeet wi ma séddoo bàkkaar: ma di bëtu ndox muy dund, ñu wacc ma, man, di gasal seen bopp kàmbi dencukaayi ndox, te kàmb yi fett, di senn.

Ku masa gis fu tawub yuur gedde mbartali Libaŋ, mbaa wal mu sedd ma cay wale fu sore ŋiis?