TSK

TSK · James 1:15

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

waaye bul lekk ci garab giy taxa xam lu baax ak lu bon, ndaxte bés boo ci lekkee kat, li wér mooy fa ngay doxe dee.»

¶ Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp.

Job 15:35 TSK

Ñooy sos joote, wasin ñaawtéef, ñoom la seen biir di ëmb wuruj.

Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon teg ug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.

Micah 2:1 TSK

Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef, di ràbb lu bon ci seenub tëraay, bët set, ñu jëfe ko, ndax xam ne man nañu ko.

¶ Bàkkaar moo jaare ci kenn nit dugg ci àddina, dee jaare ci bàkkaar, dikk, ba dikkal ñépp, ndax ñépp a bàkkaar.

Ba loolu amee ñu jàpp ndee ak njaniiw, sànni ca déegu sawara sa. Ñaareelu dee gi nag moo di déegu sawara si.