Waaye maay baaxe ñi ma sopp, di sàmm samay santaane, ba ci junniy maas ya leen di wuutuji.
TSK
TSK · James 2:5
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.
Kon yeen niti xel ñee, dégluleen ma, Yàlla jegewul fenn mbon! Aji Man ji jegewul mukk njubadi!
àddina mel ni ban bu ñu teg torluwaay, tey saamandaay mbubb mu ñu suub,
Maa sopp ku ma sopp, ku ma seet tigi, gis ma.
Lees di tontu xeet wi yónnee di laaj, xanaa ne leen Aji Sax jee sanc Siyoŋ, te fa la baadooloy ñoñam di rawe.
Waaye maay wacc fi sa biir askan wu woyof te néew doole, ñu yiiroo turu Aji Sax ji.
Bésub keroog la kóllëre ga dog, teefonke yi may xool daldi xam ne loolu kàddug Aji Sax ji la.
¶ Ca yoon wa ñu awe la jenn waay ne Yeesu: «Yaw laay topp fépp foo jëm.»
¶ «Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
Ibraayma ne ko: “Doom, fàttlikul ne na nga séddoo woon sa bànneex ca àddina, noonu la Lasaar nekke woon aw tiis. Waaye fii nag moo neexle, yaw nga mitile.
Gannaaw ay doom lanu nag, ay boroom cér lanu, ay boroom cér yu Yàlla sédd, cér yu nu bokk ak Almasi, gannaaw noo bokk ak moom ab coono tey, ngir bokk ak moom teraangay ëllëg.
Mooy noonu ñu binde rekk ne: «Lu bët gisul, nopp déggu ko, xel daju ko, Yàllaa ko dencal ñi ko sopp.»
Loolu lépp yeena tax, ngir yiwu Yàlla lawa law, ba cant gu ne gàññ tukkee ci ñi ëpp ci nit ñi, ngir màggug Yàlla.
Xam ngeen kat sunu yiwu Boroom Yeesu Almasi, moom mi woomle woon, te yeena tax mu ñàkk, ngir woomale leen ag ñàkkam.
Man mi yées ci ñu sell ñépp lañu may woowu yiw, ba may xibaar jaambur ñi dul Yawut, xéewal yu amul kem yi ci Almasi.
¶ Loolu lépp di firndeel njekku àtteb Yàlla, bi leen di yellale nguurug Yàlla, gi tax ngeen di sonn.
Léegi nag kaalag njekk a may xaar, te Boroom bi, Àttekat bu jub bi moo ma koy yool, keroog ca bés ba, te du man rekk la koy yool, waaye itam képp ku koy séentu te yàkkamti bés ba muy feeñ.
Toroxtaange gu ñu koy teg ndax Almasi, moom la defoon muy alal ju ëpp denci Misra, ndax yoolub ëllëg ba la doon séentu.
¶ Ndokklee ku muñ ab nattu, nde su ca amee ngërëm, mooy yooloo kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko sopp.
Loolu moo am ngir ab cér bu dul yàqu, du sobewu, du seey, cér bu dence fa asamaan ñeel leen,
¶ Gis naa sa coono ak sag ñàkk, moona yaaka duunle! Gannaaw loolu it, waxi yàq-der yi tukkee ci ñooñu tuddoo Yawut te duñu Yawut, duñu lenn lu moy jàngub Seytaane, dégg naa ko.
Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,