TSK

TSK · James 4:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam.

am géttu jur gu gudd ak gu gàtt, ak ay surga yu bare, ba tax waa Filisti iñaane ko,

Mag ya nag iñaane ko. Teewul baayam moom bàyyi xel ci mbir moomu.

Musaa ne ko: «Fiiraangee la jàpp ndax man, am? Éy bu niti mbooloom Aji Sax ji mépp doon ay yonent, Aji Sax ji sol leen ag leeram!»

Ba ñu demee ba iñaane Musaa ca dal ba, boole ca Aaróona mu sell ma, nitu Aji Sax ja,

Ma gis ne nit ak kër-këram jépp ak bépp manoorey liggéey, iñaanantee ko waral. Loolu it, cóolóoli neen ak napp um ngelaw.

Dañoo dem ba feese gépp xeetu njubadi, akug mbon, akug bëgge, akug coxor. Noyyeewuñu lu moy kiñaan, ak pexey bóome, ak ŋaayoo, akug njublaŋ, ak jëf ju sew. Ay jëwkat lañu it,

Dangeena xamul ne seen yaram mooy màkkaanu Noo gu Sell, gi ci yeen, Noo gi ngeen jote ci Yàlla? Moomuleen seen bopp,

Mbind mi moo waajaloon lu jiitu ne ci kaw ngëm lees di joxe xeet yi dul Yawut, àtteb nit ñu jub. Moo taxoon mu yégal Ibraayma lu jiitu, bii xibaaru jàmm: «Xeeti àddina yépp ci yaw lañuy barkeele,»