TSK

TSK · James 4:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye bu ma waxee ne ma bégul ci man, su boobaa ba tey maa ngi. Na def li ko soob ci man.»

Job 1:21 TSK

daldi ne: «Duŋŋ laa génne sama biiru ndey te duŋŋ laay delloo. Aji Sax jee maye, Aji Sax jee nangu. Cant ñeel na Aji Sax ji.»

Job 42:1 TSK

¶ Ba loolu amee Ayóoba àddu ne Aji Sax ji:

Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,

Waxal Buur, wax Lingeer yaayu Buur ne leen: «Dëjuleen fi suuf, seen mbaxanam nguur mu yànj foq na.

Mboolem waa àddina di neen ci moom. Nu ko neex lay def ak gàngoori xarey asamaan ak waa suuf, te kenn du fél loxoom mbaa mu naa ko: «Ana looy def nii?»

Luke 4:2 TSK

Ñeent fukki fan la ko fa Seytaane fiir, lekkul dara diir boobu bépp. Gannaaw ba fan yooyu wéyee, mu xiif.

¶ Ba loolu amee boroom kaso ba indilu ab làmp, daldi ne saraax dugg, ne gurub fa kanam Póol ak Silas, di lox.

Yoonu njub gi Yàlla di joxe nit ki, àtteb ku jub, moom lañu umple tey jéema dëggal seen njubteg bopp. Moo tax nanguluñu njubte gi Yàlla di maye.

Ràngooleen mboolem gànnaayi Yàlla, ngir ngeen mana jànkoonte ak pexey Seytaane.

¶ Nangul-leen gépp kilifteef gu tege ci àddina ngir Boroom bi; muy buur bu mag bi gëna kawe,

¶ Àndleen ak sago te teewlu! Seenub noon Tuumaalkat bi, mu ngi ŋar ni gaynde, tey wër, di rëbb ku mu warax.