TSK

TSK · Jeremiah 11:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Boroom ngis, ñu ne ko: «Bul gis,» boroom peeñu, ñu ne ko: «Bu ñu firil peeñuy dëgg. Wax nu lu neex, gisal nu ay nax.»

«Ndegam boroom ñaari tànk ngay rawanteel, xoox, nooy rawanteeki fas? Soo wóoluwul lu moy àll bu ne yàmblaŋ, nooy def ak gottub Yurdan?

¶ Ci kaw loolu, doomu Imer, Pasur, sarxalkat ba jiite woon saytub kër Yàlla ga, dégg Yeremi muy biral kàdduy waxyu yooyu.

Naka la Yeremi wax ba sottal mboolem la ko Aji Sax ji santoon mu jottli ko mbooloo ma mépp, sarxalkat yaak yonent yaak mbooloo ma mépp ànd jàpp ko, ne ko: «Yaw, dee rekk mooy sab àtte!

Amos 2:12 TSK

«Yeen nag ngeen di naanloo samay séddoo biiñ. Yonent yi, ngeen ne leen: “Buleen biral waxyu!”

Micah 2:6 TSK

Seen yonent yeey waare naa: «Buleen waare! Nii kat deesu ko waaree, gàcce du nu dab!»

Waaye tey ak ëllëg ak sibir, fàww ma dem, ndax ab yonent wareesu koo bóome fenn fu dul Yerusalem.