¶ «Maay samp sama kër ci seen biir te duma leen sib.
TSK
TSK · Jeremiah 14:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Aji Sax jee gis loolu, gedd, ndax mere doomam yooyu, góor ak jigéen.
Bàyyil xel askan wi nga jënd bu yàgg, yaa jot gii giir, séddoo leen. Bàyyil xel tundu Siyoŋ, fa nga dëkke woon.
Ngalla xoolal ci kóllëre gi, fu làqu ci réew mi, fitna dale fa ba dajal.
Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal, mere ko, wacc ko.
bàyyi xel ci kóllëreem ak ñoom, topp ngoram lu réy, ba giif,
«Janti keroog Yerusalem, ngànguney Aji Sax ji lees koy wooye, xeetoo xeet di fi daje, ngir Aji Sax, ji turam ñeel Yerusalem, te dootuñu të ticc ci seen mébét yu bon.
Aji Sax ji, wacc ngaa wacc Yuda nii? Am Siyoŋ a la génnliku? Lu tax nga di nu dumaa musiba mu amul paj? Nuy yaakaar jàmm, dara baaxul, nuy séentum paj, tiitaange ne jaas!
Loxo la noon bi teg ci ngëneeli Siyoŋ gépp. Siyoŋ kay a gis yéefar yi songsi këram gu sell gi, te ci ñoom nga santaane woon, ne buñu dugg sam ndaje.
Éy Aji Sax ji, xoolal, seetal rekk ki nga def nii! Xanaa du ndey mooy dem ba yàpp doomam, doom ju mu sukk jur, mu wér péŋŋ! Xanaa du sarxalkat akub yonent lañuy bóom fi bérabu Aji Sax bu sell bi!
Waxal waa kër Israyil, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di teddadil sama bérab bu sell bii, seen sag bii ngeen di doolewoo, di seen bànneexu bët, di seen nammeelu bakkan. Seen doom yu góor ak yu jigéen ya ngeen bàyyi Yerusalem, saamar dina leen tëral.
¶ «Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Léegi maay tijji wërsëgu Yanqóoba, maay ñeewante waa kër Israyil googu gépp, te maay fiire sama tur wu sell wi.
Muy damu bay diir mbagg Njiital gàngooru xare gi, daldi dakkal sarax ba ñu ko daan defal bés bu jot, màbb bérabam bu sell ba.
¶ «Léegi nag yaw Boroom bi, sunu Yàlla ji nu génnee Misraak doole, nun sa mbooloo, nga siiwale ca sa tur ba sunu jonni yàllay tey, noo bàkkaar, noo tooñ.
¶ Ba mu ko defee ma jël sama wenn yet wi, Xejjoo, damm ko, ngir doge ko sama kóllëre gi ma fasoo woon ak askan yépp.
Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.