TSK

TSK · Jeremiah 21:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

¶ Moo tax Aji Sax ji Boroom bi dafa wax ne: «Sama xadar a ngii di sottiku fi bii bérab, fi kaw nit ak mala, garab ak lu suuf meññ, lépp ne jippét, te deesu ko fey.»

Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»

Ndax Aji Sax ji dafa wax ne: “Maa ngii di la wàcceel tiitaange, yaak sa soppe yépp, seen saamaru noon daaneel leen, ngay gis; te Yuda gépp laay teg ci loxol buuru Babilon, ñii mu yóbbu leen ngàllo, ñee mu jam leen, ñu dee.

¶ Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bérab bii di gent bu kenn nekkul, du nit du rab ci dëkk yi fi nekk yépp, bérab bii dina dellu am parlu yu sàmm siy gooral seeni gàtt.

Yowakim buurub Yuda nag, nanga ko wax ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne yaw yaa lakk taxañ bii, naan lu waral ma bind ci ne buuru Babilon dina ñëw moos te dina tas réew mii, faagaagal fi nit ak mala.

Seen ñetteelu xaaj, mbas lañuy deeye mbaa xiif bu leen di sànk ci biir dëkk bi. Beneen ñetteelu xaaj bi, saamar lañuy fàddoo ci seen dig-digal bi. Xaajub ñetteel bi ci des, fépp fu ngelaw jublu laa leen di tasaare, te saamar laa leen di toppe.

Du tee ma ba ñenn ci ñoom, ñu mucc saamar, mucc xiif, mucc mbas, ba nettaliji seen gépp tojaange ca digg xeet ya ñu jëm. Su boobaa ñu xam ne maay Aji Sax ji.”»

Su ma wàccee saamar ci miim réew it, ba sant saamar ne ko mu jaar ci biir réew mi, dagge fi nit ak mala,

¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Sama ñeenti mbugal yu tar yii laay yebal ci kaw Yerusalem. Ñuy saamar akub xiif ak rabi àll aku mbas, ngir dagge ci réew mi nit ak mala.

Bu ma defee réew mi gent bu wéet ndax seen mboolem jëf ju siblu, dinañu xam ne maay Aji Sax ji.”

Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool, Yerusalem googu diy tojit, jale, tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.

Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.