TSK

TSK · Jeremiah 22:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te bu ngeen ko yiwee, mu moom boppam it, buleen ko yiwee loxoy neen.

¶ Yowakim jox na Firawna Neko xaalis baak wurus wa mu laaj. Waaye waa réew ma la ko sas, ba jële ca ñoom xaalis baak wurus wa, ku nekk ak sab sas, daldi koy dajale, jox ko Firawna Neko.

Job 24:10 TSK

Duŋŋ lañuy wéye ndax rafle, biir wéet, ñuy gàdduy sabaar,

Moo tax Aji Sax ji wax ci mbirum buurub Yuda, Yowakim doomu Yosya, ne: «Kenn du ko jooy ca mbokkam mu góor mbaa mu jigéen, naan: “Wóoy ngalla nun, bokk yi!” Kenn du ko jooy, naan: “Wóoy, sang ba, wóoy kilifa ga!”

«Wóoy ngalla kuy dajaleel këram alalu yàqute ju lewul tey aj am tàggam fu kawe, ngir fegu ci yàqule.

«Maa leen di dikke ab àtte, di ab seede bu taxaw temm ci tuumaal ñeengokat yeek njaalookat yi, ak ñiy fene ngiñ, ak ñiy xañ ab liggéeykat peyooram, di noggatu ab jëtun akub jirim, di beddi doxandéem te ragaluñu ma.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.