TSK

TSK · Jeremiah 29:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Su ko defee ñoom dinañu tudd seen bàkkaar ak seen bàkkaaru maam ya, ndax dañu maa wor te dëkke maa noonoo,

¶ Ëllëg nag, su mboolem mbir yooyu dikkee fi seen kaw, muy barke yi, di alkànde yi ma teg fi seen kanam, su boobaa bu ngeen délloosee seen xel foofa mu leen fekk, ca biir mboolem xeet ya leen seen Yàlla Aji Sax ji dàq jëme,

bu ñu demee ba seenum xel dellusee fa réew ma ñu leen yóbbu ngàllo, ñu tuub tey sàkku aw yiw fi yaw foofa ca réewum ña leen jàpp, ne la noo moy, noo ñaaw, noo def lu bon,

Buur nag taxaw fa kenu ga, feddli kóllëre ga fa kanam Aji Sax ji, ngir topp Aji Sax ji, di sàmme léppi xol ak léppi bakkan, ay santaaneem ak seedey yoonam, ak dogali yoonam, ngir saxal kàdduy kóllëre googu ñu bind ci téere boobu. Askan wépp yebu ca kóllëre ga.

Mu woo ma, ma wuyu ko; mook man ci biir njàqare, ma xettli ko, darajaal ko,

Sama léppi xol laa lay sàkkoo, bul ma wacc, ma wàcc say santaane.

Ñu bew ñee yàq sama der aki sos, te ma topp say tegtal, wéetal la.

Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.

Sàkkuleen Aji Sax ji bi ngeen koy mana gis, wooleen ko bi muy jege.

Loolu yépp itam taxul Yuda workat bi, doomu ndeyu Israyil, délsee léppi xolam fi man, xanaa di jinigal rekk.» Kàddug Aji Sax jee.

Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.

Joel 2:12 TSK

«Terewul ba léegi,» kàddug Aji Sax jee, mu ne: «Délseeleen seen léppi xol ci man, boole kook koor aki jooy aki yuux.

Luke 11:9 TSK

Moo tax ma ne leen, ñaanleen, ñu may leen; seetleen, ndax ngeen gis; fëggleen, ñu ubbil leen.