TSK

TSK · Jeremiah 31:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

da ne leen: «Defleen seen xel ci mboolem kàddu yi ma leen di artoo man, bésub tey, te ngeen sant seeni doom ñu sàmmoo jëfe mboolem kàdduy yoon wii.

Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!

Yeen ñiy yóbbu ndabi Aji Sax yu sell yi, bu ngeen di jóge Babilon, dëdduleena dëddu lu sobewu, bañ koo laal, setluleen te génn foofa.

Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, xàll-leen yoonu xeet wi, maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.

«Yeen doom yu woyof kumba yi, délsileen.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay seen boroom kër, maay jële kenn ci bii dëkk, ñaar ca bee gox, boole indi Siyoŋ,

Yaw Israyil mu taaru, maa lay defaraat, nga defaru, ba jiinaat sam njiin, wàlli peccum mbéx,

«Yeen gan ñi, génnleen Babilon, ku ne rawaleji sa bakkan. Buleen ñaawtéefu jaambur sànkaale; lii àppu mbugal la bu Aji Sax ji matal; seen añ la, bu mu leen añale.

Waa ja ne ma: «Yaw nit ki, xoolal bu baax, teewlool say nopp te def sam xel ci mboolem li ma lay won. Ngir won la moo tax ñu indi la ba fii. Mboolem loo gis, nanga ko àgge waa kër Israyil.»

Ma ne ko: «Foo jëm?» Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo, ak nu mu gudde.»