2 Samuel 23:5
TSK
Du nii la sama waa kër def ak Yàlla? Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk, lépp jekk, mat sëkk. Moo may may ndam saa su ne, di ma defal lu ma namm.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Du nii la sama waa kër def ak Yàlla? Moo fas ak man kóllëre gu sax dàkk, lépp jekk, mat sëkk. Moo may may ndam saa su ne, di ma defal lu ma namm.
Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga, duma fen Daawuda:
Fa laay dooleele Daawuda, taalal ki ma fal,
Teewluleen te dikk fi man. Dégluleen, ba mana dund, ma fas ak yeen kóllëre gu sax, gi ma baaxee Daawuda ci ngor gu wóor.
Sarxalkat yiy Leween it duñu ñàkk ku leen taxawal fi sama kanam, di joxe saraxi rendi-dóomal, di taal saraxi pepp ak a sarxal ba fàww.»
Moo nu feeñalal Musalkat bu manoorewu, fi biir kër Daawuda jaamam ba,