TSK

TSK · Jeremiah 37:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dees na leen gawe ci seen dëkk yépp, ba seen tata yu kawe te dàbbliku, ya ngeen yaakaaroon ci seen réew mépp, màbb. Dees na leen gawe seen dëkk yépp, ci mboolem réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.

Keroog juróom ñeenti fan ca weer wa, xiif ba tar lool ca biir dëkk ba, ba waa réew ma amatuñu ab dund.

Ma ne, Aji Sax jee naa jàkk ku ko ragal tey wéeroo ngoram.

Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.

Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.

Ku ni mel, bérab bu kawe lay dëkke, doj yu ñu dàbbli di rawtoom, dundam doy, te ndoxam du ñàkk.

Booba mbooloom xarem Babilon a nga gaw Yerusalem. Fekk Yonent Yàlla Yeremi nag moom, ma nga ñu tëj ca kër buurub Yuda, ca biir ëttu dag ya,

«Buur sang bi, nit ñi de, lu bon lañu def Yonent Yàlla Yeremi; tàbbal nañu ko ca kàmb ga. Dina fa dee ak xiif ndax ab dund amatul ci dëkk bi.»

Yeremi nag des ca ëttu dag ya, ba keroog bés ba ñu nangoo Yerusalem.

¶ Fekk na kàddug Aji Sax ji dikkal Yeremi ba ñu ko tëjee ca ëttu dag ya, ne ko:

Samay gët a giim ndaxi rongooñ, samay butit fuddu, xol ŋiis, jeex tàkk: ci tasteg samaw askan; xale yeek gone yiy nàmp ne lasar fi mbedd yi!

Luy nàmp a nga mara mar, ba làmmiñ taqoo denqleñ. Gone yaa ngi ñaan mburu, te kenn daggalu leen.

Acts 12:5 TSK

¶ Naka lañu tëj Piyeer ca kaso ba, mbooloom gëmkat ñi saxoo koo ñaanal Yàlla.

Ba nu dikkee Room nag may nañu Póol, mu am daluwaayu boppam, ab takk-der di ko wattu.

¶ Dama leen di dénku nag, man mi ñu tëj ndax Sang bi, ngir ngeen dund dundin wu yellook wooteb Yàlla, bi mu leen woo.

¶ Bul kersawoo di seedeel sunu Sang, mbaa nga di ma kersawoo, man mi ñu tëj ngir moom, waaye jëlal sa wàll ci coonob xibaaru jàmm bi, ni la ko manoorey Yàlla manloo.