dox, ba dànd ko lu tollook saanu fitt, toog nag jàkkaarlook moom te naa ci xelam: «Duma fekke mukk sama deewu doom.» Naka la toog foofa janook moom, ne yikkét jooy.
TSK
TSK · Jeremiah 39:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dingeen mujj dof ndax lu buur seeni bët ngeen di gis.
Doomi Cedekiya yu góor lañu rendi, muy gis, ba noppi ñu tuur ay bëtam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.
Ana nu ma mana seetaane musiba di dal samaw xeet ak nu ma mana seetaane ñuy sànk samay bokk?»
Gannaaw loolu nag,” kàddug Aji Sax jee, “Cedesyas buurub Yuda, aki jawriñam ak askan week ñi des ci dëkk bii te rëcce ci mbas meek xare beek xiif bi, maa leen di teg ci loxol Nabukodonosor buuru Babilon, ak seen loxol noon, ak loxol ñi leen di wuta rey. Dina leen leel ñawkay saamar. Du leen baal, du ñéeblu, du yërëm.”
Muy kàngami Yuda, di kàngami Yerusalem, di bëkk-néeg yeek sarxalkat yi, ak mboolem waa réew mi jaare woon ci diggante ñaari xaaji sëllu wa,
Buuru Babilon daa rendi doomi Cedesyas yu góor, muy gis, mu rendiwaale mboolem kàngami Yuda, ca Ribla.
«Keroog bésub saraxu Aji Sax ji, maay dikke mbugal kàngam yeek doomi buur yi, ak boroom coli ndoxandéem yi.