TSK

TSK · Jeremiah 39:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Doomi Cedekiya yu góor lañu rendi, muy gis, ba noppi ñu tuur ay bëtam, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.

Sa dogali yoon laay sàmm; ngalla bu ma wacca wacc.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Maa ngii di waaja teg Firawna Ofra buuru Misra ci loxol noonam yiy wut bakkanam, na ma tege woon Cedesyas buurub Yuda ci loxol noonam Nabukodonosor buuru Babilon ma doon wut bakkanam.»

Maa koy laaw samab caax, mu keppoo samag fiir, ma yóbbu ko Babilon mu Kaldeen ña. Réew ma, du ko gis te fa lay deeye.