Mennum Og buuru Basan doŋŋ moo muccoon ca ndesu Refayeen ñu ponkale ña. Lalam ba, lalu weñ gu ñuul la. Ma nga noonee ca Raba, dëkkub Amoneen ña. Guddaayu lal ba ci xasabu góor, juróom ñeenti xasab la, di ñeenti meetar ak genn-wàll, yaatuwaay ba, ñeenti xasab, di ñaari meetar.
TSK
TSK · Jeremiah 49:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw loolu, ca déwén sa, jamono ja buur ya daan xareji, Daawuda daa yebal Yowab, mu ànd aki nitam ak gàngooru Israyil gépp. Ñu faagaagal Amoneen ña, gaw péey ba ñu naan Raba. Fekk na Daawudaa nga des Yerusalem.
Céy Yàlla, sa tur ay sa woy ba ca cati àddina. Njekk la sa loxo fees.
Xanaa ñu ne coww ba sowu, ne jàyy cëppandoo fa kaw waggi Filisteen ña, waa penku, ñu sëxëtoondoo; Edom ak Mowab, ñu teg loxo; Amoneen ña nangul leen.
Yeneen xeet yeey delloo bànni Israyil ba seen réew, mooma Aji Sax ji séddoo, bànni Israyil jàpp ca ñoom njaam, góor ak jigéen, ba teg loxo ña leen tegoon loxo, moom ña leen moomoon.
Lu jëm ci Amoneen ñi, Aji Sax ji dafa wax ne: «Israyil daa amuli doom? Am daa amul dono? Lu tax Milkom tuur mi donloo suufas Gàdd, ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?
yóbbuw fit, tërëfloo ñu bare. Seen buntoo bunt laa teg saamaru bóomkat. Ndeysaan, bii saamar bu ñu defar ba muy tàkk, xacc ko ngir bóome.
Maa ngii nag di leen jébbal màngaani penku, ñu moom leen, samp seeni dal fi seen biir, yékkati fa seeni xayma. Ñooy lekk seen meññeef, naan seen meew.
«Waa bëj-saalumu Yuda ñooy moom tundu Esawu, waa suufu tund ya moom waa Filisti, ñooy moom itam réewum Efrayim, ak réewum Samari, giirug Beñamin moom diiwaanu Galàdd.