TSK

TSK · Jeremiah 49:39

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, xeet yépp riirandoo, wutsi ko.

Waaye bu loolu weesee, ma tijji wërsëgu Amoneen ñi.» Kàddug Aji Sax jee.

Ca laay tijjee wërsëgu Misra, delloo leen réewum Pattros ca bëj-saalum, seen réewum cosaan, ñu doon fa nguur gu suufe,

¶ «Kon nag Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Léegi maay tijji wërsëgu Yanqóoba, maay ñeewante waa kër Israyil googu gépp, te maay fiire sama tur wu sell wi.

Léegi ñëw naa ngir xamal la liy dikkal sa mbooloo ci jamono yiy ñëw ndax peeñu mi ëmb na jamono yooyu itam.»

Amos 9:14 TSK

Maay tijji wërsëgu Israyil, sama ñoñ; ñu tabaxaat seeni gent, dëkke; jëmbat seen tóokëri reseñ, naan seen biiñ, bey ay tool, lekk ca meññeef ma.