TSK

TSK · Job 15:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Ñi des ci yeen, dinaa indi njàqare ci seen xol, foofa ngeen nekk ca seen réewu noon ya, ba xob wu ne foy-foy ngeen daw. Dingeen xélu ni ku ñuy dàqe saamar, bay daanu, te dàqeesu leen.

Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!»

Job 1:13 TSK

¶ Mu am bés doomi Ayóoba yu góor ak yu jigéen bokk toog di lekk ak a naan biiñ ca seen kër taaw.

Job 20:5 TSK

xamoo ne ku bon, ag sarxolleem àggul fenn, te bànneexu yéefar yàggul?

Job 27:20 TSK

Musibaa koy dab nim wal, ngëlénu guddi këf, yóbbu,

Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.

Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.

¶ Ba bés ba ñu jàpp agsee, Erodd sol colu buuram, toog ca jal ba, di leen àgge kàddug kilifteefam.

Fa nit ñi naan: «Jàmm ak kaaraange dikk na,» fa la sànkute di dale ci seen kaw, ni aw mat di jekkee dal ci kaw jigéenu wérul, te kenn du ca rëcce.