¶ Ci kaw loolu Samiyel ñaan ci Aji Sax ji, Aji Sax ji dënu, taw ca bés ba. Mbooloo ma mépp nag ragal lool Aji Sax ji ak Samiyel.
TSK
TSK · Job 37:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
1 Samuel 12:18
TSK
2 Samuel 21:14
TSK
Ñu boole kook yaxi Sóol ak doomam Yonatan, denc lépp ca sëgu Kis, baayu Sóol, ca diiwaanu Beñamin ca Sela. Ñu def la Buur santaane lépp. Gannaaw loolu Yàlla nangul réew ma.
Ezra 10:9
TSK
¶ Ba ñu ca tegee ñetti fan mboolem góori Yudak Beñamin daje nañu Yerusalem, mu yemook ñaar fukki fan ca juróom ñeenteelu weer wa. Ña nga toog ñoom ñépp ca ëttu kër Yàlla ga, di lox ndax solob ndaje ma, ak itam taw bu bare ba mu yemool.
Job 37:6
TSK
Kee naan tawub yuur mu sóobal suuf, di yebal taw ba ci waame yiy sóobe doole,
Job 38:27
TSK
di suuxat gent bu maral, ba saxal fam ñax?
Psalms 65:10
TSK
Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,