TSK

TSK · Joel 2:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind.

Dinañu lal déndu réew mi, ba kenn dootu gis suuf. Dinañu lekk lu fi tawub yuur bi ba woon, te garab yi ci seeni tool yépp lañuy lekk.

Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell, sawaraa ko jiitu, di xoyome, ngëlén lu mag wër ko.

Dees na sëxëtoo sa alal sëxëtoob soccet. Dees na ko sam ni njéeréer di samee!

Ñooy dikk, warax seen meññeef ak seen ñam, jeexal seeni doom, góor ak jigéen, lekk seen jur gu gudd ak gu gàtt, saax-saaxee seeni reseñ ak seeni figg; te dëkk yi ngeen yaakaare seeni tata, dooley saamar a koy tas.

Joel 1:4 TSK

Ndesu soccet yi la njéeréer yi lekk, ndesu njéeréer yi, seenu tostan lekk, seen ndesu tostan, salleer yi lekk.

Amos 7:4 TSK

¶ Boroom bi, Aji Sax ji dellu ma feeñu. Ndeke Boroom bi, Aji Sax ji day waaja mbugale ñoñam sawara. Mu xoyom xóotey géej mbàmbulaan, bay waaja xoyom réew ma.

Maa leen tasaare ni callweer ci biir mboolem xeet yu ñu xamul woon, réew mi gental seen gannaaw, ba kenn jaareetu fi dem ak a délsi. Nii lañu defe ab gent, réew mu bakkane.»