¶ Aji Sax ji dafa wax ne: «Mboolem sama dëkkandoo yu bon, yi laal céru suuf bi ma sédd Israyil sama ñoñ, maa ngii di leen déjjatee seen réew, te waa kër Yuda, maa leen di seppee fi seen digg.
TSK
TSK · Joel 3:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Lu jëm ci Amoneen ñi, Aji Sax ji dafa wax ne: «Israyil daa amuli doom? Am daa amul dono? Lu tax Milkom tuur mi donloo suufas Gàdd, ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?
«“Aji Sax ji nekk fi, nga naan: ‘Ñaari làngi giir yii dëkke seen ñaari réew yii, maa leen moom, noo ciy teg loxo.’
Maa koy mbugale mbas ak deret ju tuuru, ak wali waameek doji yuur, ak tawub sawaraak tamarax, mooki gàngooram, ak xeet yu bare yi ànd ak moom.
«Soxore gi ngeen soxore seen mbokk Yanqóoba moo leen tax di sangoo gàcce, te dees na leen dagg sànni ba fàww.
moo tax, xaar ma rekk,» kàddug Aji Sax jee, «ba keroog may jóg, nara sëxëtooji, nde maa dogala dajale xeet yi, dajale nguur yi, ngir xëpp leen samam sànj, mboolem sama tàngooru mer. Sama sawaras fiiraange déy, ci la mboolem àddina di xoyomu.
Xeet yépp laay dajale ci kaw Yerusalem, ngir xare. Dëkk bi lees di nangu, sëxëtoo kër yi, tëdde jigéen ñi. Genn-wàllu dëkk beey génn, jëm ngàllo, waaye ndesu askan wi, deesu leen dagge ci dëkk bi.
Deretu ñu sell ñeek deretu yonent yi lañu tuur, nga nàndal leen deret, feye leen.»
¶ Ci kaw loolu njuuma yi dajale buur yi ci bérab bu ñuy wax Armagedon, di baatu ebrë.
¶ Ba loolu amee ma gis rab wi, mook buuri àddina yeek seeni gàngoor, ñu daje ngir xareek ki war fas week gàngooram.