TSK

TSK · Lamentations 2:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 2:12 TSK

Ñu dikk ba jub ko, di ko séentoo fu xawa sore, waaye xàmmeetuñu ko. Ñu daldi ne yikkét jooy. Ba ñu agsee ku ci nekk ne sa mbubb tareet. Ñuy ñaawlu, di tibb suuf, di sànni ca kaw, muy sottiku ci seen kaw bopp.

Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlook a jooy, mel ni ndaw su ñu futti, mu ne dett fi suuf.

Ba loolu amee bootalub Buur, Elyakim doomu Ilkiya ak Sebna, bindkat ba, ak doomu Asaf, Yowa ma denc téere ya, ñoo dem ak seen yérey ñaawlu yu xottiku, ba ca Esekiya. Ñu daldi koy àgge kàddug bëkk-néeg ba.

Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi, toogal ne cell te fatu cig lëndëm, deesatu la wooye lingeeru réew yi.

Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.

Aji Sax ji ci boppam moo leen tasaare, faaleetu leen; cér lees séddul sarxalkat, te teraleesul mag.

Yaay tax ñuy nelu, sol ay saaku di ko ñaawloo, di la jooye naqaru xol ak yuux yu metti.

Amos 5:13 TSK

Moo tax ku xelu ci jii jamono ne cell. Céy jii jamono ju bon!

Amos 8:13 TSK

Bésub keroog janq ju taaru jaak xale yu góor ya deek mar.