TSK

TSK · Lamentations 2:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dañoo taal sa kër gu sell, sa dëkkuwaayu tur lañu daaneel, ba sobeel ko.

Fecci nga sa kóllëreek sab jaam, foq nguuram, detteel ko.

Buleen fi indeeti saraxi caaxaan, seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la. Terutel weer ak bésub Noflaay ak wooteb ndajee ci yem! Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.

Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.

Nun sa xeet wu sell wii, moomunu réew mi lu yàgg, te noon yi dëggaate nañu sa bérab bu sell.

¶ «Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: “Bu ngeen demee Misra, ni sama mer ak sama xadar yurikoo woon fi kaw waa Yerusalem, ni la sama xadar naan yureet fi seen kaw. Dingeen doon gentu alkànde, ñu di leen móolook a sewal, te dungeen gisati miim réew.”»

Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, ba noppi jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon, tëj ko fa, ba keroog bés ba mu deeyee.

Yoon yi jëm Siyoŋ jooy na wéet, kenn jaareetu ca màggalsi. Pénc yépp a gental, sarxalkat yay binni, janq ja jàq, Siyoŋ gépp di naqarlu!

Ki nuy noyyee, Buur bi Aji Sax ji fal, ca seeni yeer la tance, te nu noon ci keppaaram lanuy dëkke fi digg xeet yi.

Seen boroom dëkk beey gàddub ëmbam, génn dëkk bi ci lëndëm gi. Miiru dëkk bi lees di bëtt, jaarale ko ca. Kanam ga lay muur, ba tax du gis suuf si.

«Ñi amu naqar te sore ndajey bernde, ñooñu la sore, te tegoo woon gàcce, maa leen di dajale, teggil leen gàcce tey.