Daawuda duma Mowabeen ña itam, tëral leen ca suuf, sësale leen, natte leen ag buum. Ñaari buum yu mu natt, yemook ña ñu wara rey, buum gu mat ga ca topp yemook ñi wara dund. Mowabeen ña daldi nangul Daawuda, di ko indil galag.
TSK
TSK · Lamentations 2:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ngalla teggi ma sa loxo, te buma dabeeti tiitaange loo sabab.
Ma xamal leen nag li ma naral sama tóokër bi. Ñàggib ñagam, mu dim parlu; màbb miiram, ñu dëggaate ko, jàll.
Dëgg laay def nattukaay, njekk di sama buumu beteex, tawub doji yuur buub rawtub fen, wal ma mëdd làquwaay,
«Yéegleen seeni tata, yàqte waaye buleen leen jeexal tàkk. Tenqileen lawit yi, ñooñoo bokkul ci Aji Sax ji.
Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.
Boroom bee mel nib noon, modd Israyil, moddaale këram yu taaru yépp, tas ay tataam, ba fulal Janq Yuda mu taaru ma, ay yuux aki jooy.
Teewul ma téye sama loxo, sédd ci sama teddngay tur ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk.