TSK

TSK · Lamentations 3:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Job 42:5 TSK

Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw, tey bët laa la teg.

Su ko defee nga fàttliku démb, daldi rus, torox ba ne xerem keroog ba ma lay jot ci mboolem loo def. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.”»

Jonah 3:9 TSK

Jombul Yàlla dëpp ba fomm, daldi dëddu tàngooru meram, ba dunu sànku.»

Naa jóg, dem ca sama baay, ne ko: ‘Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ la;

¶ Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.