TSK

TSK · Lamentations 4:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

«Yàgg ngeena yiwiku, dog seeni jéng, ba ne dungeen ma jaamu. Kaw tundoo tund, ker garaboo garab gu naat, gànctu ngeen fa.

«Ndax ki gëna tuut ba ki gëna mag, ñépp a ngi lewal lu lewul. Yonent akub sarxalkat, ñépp a ngi wor.

«Te it yonent ak sarxalkat ñoo bokk yàqu, sama biir kër sax gis naa ci seenug mbon.» Kàddug Aji Sax jee.

Ag neen aki caaxaan la la say yonent gisal, te biraluñu sag ñaawtéef, ngir tijji sa wërsëg, xanaa di la yéeneel waxyuy caaxaan aki nax.

Ay yonentam a ngi déeyoo fi biiram; ñu ngi xiiru ni gaynde guy xotat pàddam, di lekk doom aadama yi, foqati alal ak gànjar, ful jëtun yi ci biiram.

Kàngamam yi ci biiram a ngi mel ni saafaandu yuy dogat am pàdd, tuur deret ja, di sànk ay bakkan ngir nangu alali boroom.

Kàngam yi ci biiram di gaynde yuy ŋar, ay njiitam di tilli timis yu dul pannal,

Acts 7:52 TSK

Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.