TSK

TSK · Lamentations 4:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Dees na leen gawe ci seen dëkk yépp, ba seen tata yu kawe te dàbbliku, ya ngeen yaakaaroon ci seen réew mépp, màbb. Dees na leen gawe seen dëkk yépp, ci mboolem réew, mi leen seen Yàlla Aji Sax ji jox.

Mu am bés buurub Israyil jaar ca kaw tata ja, senn as ndaw àddu ca kaw ne ko: «Buur, sang bi, ngalla wallu ma!»

Job 39:16 TSK

Day soxore doom yi ni lu mu jurul, coonoom neen, yoonam.

Maa leen di yàpploo seen doom yu góor ak yu jigéen, ku nekk di yàpp sa moroom ci biir njàqare, ndax gaw bu metti, bu leen seen noon yi leen di tëru di gaw.

Ndey ak xolu njureelam, moo togge loxoom, doomu boppam, def ko njëlam, ci sama biir toskareg askan wi!

Yeesu geesu leen, ne: «Yeen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom.