TSK

TSK · Leviticus 10:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aaróona moo jël Eliseba doomu Aminadab, jigéenub Nason. Kooku am ak moom Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.

¶ Mu neeti Musaa: «Yéegal ñëw fi Aji Sax ji, yaw ak Aaróona ak Nadab ak Abiyu ak juróom ñaar fukki magi Israyil, te ngeen sujjóote nee, dànd ma.

Sàkkal ay ndabi tibbukaayu dóomam, ak ay ñiitukaayam, ak ay këllam, ak ay cappukaayam aki andam. Defal jumtukaayam yépp xànjar.

¶ «Sàkkal ab sarxalukaay bu ñuy taal cuuraay ci kawam. Bantu séng nga koy defare.

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak cuuraay-libaŋ lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo.

Mu sàkk nag diwu pal gu sell gi, sàkk cuuraay lu xeeñ li raxul, def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax.

daldi taal cuuraay lu xeeñ li ci kawam, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

¶ Bu loolu weesee Aji Sax ji wax naak Musaa gannaaw ba ñaari doomi Aaróona yu góor ya deeyee, ba ñu taxawsee fa kanam Aji Sax ji.

Sarxalkat yi dañoo wara dénkoo samay dénkaane bala ñoo gàddu bàkkaar, di dee ndax seenug néewal ci yooyu. Maay Aji Sax ji leen sellal.

Nadab ak Abiyu nag mujj dee fi kanam Aji Sax ji, ba ñu taalalee Aji Sax ji cuuraay lu warul ca màndiŋu Sinayi. Gannaaw amuñu woon doom yu góor, Elasar ak Itamar daldi féetewoo liggéeyu carxal ba, ca seen kanamu baay Aaróona.

Dangeen di def nii: jël-leeni and, yaw Kore, yaak sa gàngoor gépp,

Buleen yokk dara ci kàddu gi ma leen di dénk, te buleen ci wàññi dara, ndax ngeen sàmm seen santaaney Yàlla Aji Sax, ji ma leen di dénk.

bay jaamuji yeneen yàlla, di leen sujjóotal, mbaa muy sujjóotal jant bi, mbaa weer wi, mbaa mboolem gàngooru asamaan, te santaanewuma ci lenn,

Ñoo tabax ay jaamookaay ca Tofet fa xuru Ben Inom, di fa sarxe seeni doom, góor ak jigéen, lakk leen, te santaanewma ko, jaarul sax sama xel.

Tabaxal nañu Baal tuur mi ay bérabi jaamookaay ca xuru Ben Inom, di fa lakk seen doom yu góor ak yu jigéen ngir Moleg tuur mi, te masuma leen koo sant. Jooju jëf ju siblu jaarul sax sama xel ba ma leen di ko defloo, ñuy yóbbe Yuda bàkkaar.

¶ Ñu baree nga fa woon, di mboolem ña xamoon ne seeni jabar dañuy taalal cuuraay yeneen yàlla ak mboolem jigéen ña teew. Ñuy mbooloo mu réy, ñépp ña sanci Misra, ba ca diiwaanu Pattros. Ñu daldi ne Yeremi:

Luke 1:9 TSK

Ba ñu tegoo bant, na ko sarxalkat yi baaxoo woon, moom la bant ba dal, mu wara dugg biir néegu Boroom bi, ngir taal fa saraxu cuuraay.

¶ Bi loolu amee meneen malaaka dikk, taxaw ci wetu sarxalukaay bi. Mu ngi yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole kook ñaani mboolem aji sell ñi, jooxe ko ci kaw sarxalukaayu wurus bi ci kanam ngàngune mi.