TSK

TSK · Leviticus 10:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Aaróona dikk ba ci sarxalukaay bi, rendi sëllu wi, muy saraxu póotum bàkkaaram.

Foofa ngeen di lekke, yeen ak seeni njaboot fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ngeen bége fa seen wépp ñaq wu leen seen Yàlla Aji Sax ji barkeelal.

At mu nekkaan noonu la. Saa yu Aana demee kër Aji Sax ji, noonu la koy ñaawale, ba muy jooy, du nangoo lekk.

Bu ngeen ma tàllaleey loxo, ma fuuyu. Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it, du maa leen di déglu: seeni loxo, deret la taq ripp.

Su ñu ci boole woon koor sax, duma déglu seeni dagaan. Su ñu ma doon sarxalal saraxu rendi-dóomal ak saraxu pepp it, du maa leen di nangul. Xanaa saamar akub xiif ak mbas kay laa leen di faagaagale.»

«Éy bu kenn ci yeen tëjoon bunt yi far, te baña jafal ab taal ci sama kaw sarxalukaay ci dara. Awma benn bànneex ci yeen!» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. «Ab sarax, duma ko nangoo ci seeni loxo.

Lii itam yeena ngi koy def: Yeena ngi tawal ay rongooñ sarxalukaayu Aji Sax ji, di jooy ak a binni, ndax moo geesootul seen sarax, te nangootul lenn ci seen loxo.

Bokkul ak yeneen sarxalkat yu mag yi; soxlawula jiital bés bu nekk, saraxi jur ngir bàkkaari boppam, door cee teg ay sarax ngir bàkkaari askan wi. Benn yoon la Yeesu sarxal, mu doy, te mooy ba mu sarxee boppam.