¶ Aaróona moo jël Eliseba doomu Aminadab, jigéenub Nason. Kooku am ak moom Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar.
TSK
TSK · Leviticus 10:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!”
¶ «Sarxalkat, bi gëna màgg ci bokkam yiy sarxalkat, te ñu sotti diw gi ñuy fale ci boppam, sellal ko, muy sol yére yu sell yi, kooku du njañu te du xotti ay yéreem, di ko ñaawloo ku dee.
Bu taxawloo ndaw si fi kanam Aji Sax ji, na muri boppu ndaw si, te teg ciy loxoom, saraxu pepp boobu di toppukaayu ñaawtéef te di saraxu fiiraange. Na fekk sarxalkat bi yore ciy loxoom ndoxum wextan, miy alage.
Yosuwe doomu Nuun, ak Kaleb doomu Yefune, ñoom ña bokk ca ña seeti woon réew ma, daldi xotti seeni yére ndaxu tiis.
Àndal ak Aaróona ak doomam Elasar, nga yéege leen ca kaw tundu Or.
¶ Gannaaw ba loolu wéyee Aji Sax ji mereeti bànni Israyil, ba tax mu xiir Daawuda ci def lu leen di lor. Mu def ci xelam ne ko mu dem lim waa Israyil ak Yuda.
Bukki, Abiswa; Abiswa, Fineyas; Fineyas, Elasar; Elasar, Aaróona, sarxalkat bu mag ba.
«Yaw nit ki, maa ngii di nangusi sa bànneexu bët cim pàdd. Bul yuuxu, bul jooy, bu sa rongooñ wadd.
Watuleen nel, ñaawloo ko doom yi leen doon bànneexal. Neluleen nel yu set nim tan, naqarloo, nde ngàllo lañu jëm, teqlikook yeen.