TSK

TSK · Leviticus 10:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ci biir xaymab ndaje mi la Aaróona ak doomam yu góor di teg làmp yi, ci kanam rido bi làq gaalu àlluway seede si, ñuy fanaanee tàkk ngoon ba bët set, fi kanam Aji Sax ji. Dogal a ngoogu, war bànni Israyil fàww, ñoom ak seen askan.

muy biiñ, di ñoll wu mu mana doon, na séddoo di ko moyu. Bineegaru biiñ ak bineegaru ñoll wu mu mana doon it, du ko naan. Mboolem luy ndoxum reseñ, du ko naan, te reseñ ju tooy ak ju wow it, du ko lekk.

Naan biiñ ak ñaawle, naan ñoll, tanqale, ku mu nax xeluwoo.

Ñii itam ay naan biiñ bay tërëf, màndiw ñoll, di jang: sarxalkat akub yonent la aw ñoll di tërëfloo, biiñ jànnaxe leen, ñu màndiw ñoll, di jang, bu ñu amee am peeñu, di tërëf.

Biiñ, bu ko benn sarxalkat naan, buy dugg ci ëttu biir bi.

Luke 1:15 TSK

ndax ku màgg lay doon, Boroom bi seede. Biiñ ak lenn luy màndee nag, du ko naan, Noo gu Sell gi mooy dale ca biiru ndeyam, solu ko ba fees.

Bumu di ab màndikat, mbaa bëggkatub xeex, waaye na lewet, bañu ay, te bumu di bëggkatub xaalis.

¶ Te itam bul di naanati ndox mu ñuul doŋŋ, waaye deel jëfandikoo tuuti biiñ, ndax mu baax ci sa biir, ak yeneen xeeti wéradi yu la farala dal.