ak bànjóoli ak looy, ak lu mu xeetool, ak kirigéej, ak mboolem xeeti liccin, ak yébb, ak lu xeetook xodd, ak musejubru ak njugub.
TSK
TSK · Leviticus 11:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Isaiah 13:21
TSK
Ay rabi àll a fay goore, kër ya fees aki looy, bànjóoli dëkke fa, kéwél di fa curpee.
Ephesians 4:18
TSK
Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp.
Philippians 3:18
TSK
Ndaxte ñu baree ngii ñu seeni jëf tax ñu di nooni bantub Almasi. Loolu wax naa leen ko ay yoon, ma waxati leen ko tey aki jooy.
Revelation 18:2
TSK
Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.