TSK

TSK · Leviticus 11:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yii ñuy lim, buleen ko lekk: mala muy duññ te we wi xarul, mbaa we wi xar te du duññ. Lu mel ni giléem, buleen ko lekk ndax day duññ, waaye we wi xarul. Daganul ci yeen.

Lu ngeen sib lay doon, kon buleen ci lekk yàppu lenn te sibleen méddam.

Li ngeen mana lekk daal ci mboolem gunóor guy naaw tey doxe ñeenti tànk moo di: lépp lu tànk yi ànd aki yeel, mu man caa tëb-tëbe ci suuf.

Ndox mu jóge ci ndab loolu, bu dalee ci ñam wu dagan, ñam woowu dal nay sobewu moom itam; bu doon ag naan gu dagan moo ca nekk it, sobewu na, ak ndab lu naan ga mana nekk.

¶ «Mboolem bindeef yu sew-sewaan yiy dox ne ñàpp ci suuf, sibleen ko. Deesu ko lekk.

Lii moo di mala yi ngeen di lekk seen suux: nag ak xar ak bëy;

¶ Ci biir loolu Dañeel fas yéene ci xolam ne du sobeel boppam ci njëlu buur ak biiñam. Mu ñaan kilifag jawriñ ya mu may ko, mu bañ cee sobeel boppam.

Mu mel ni tey, kii ngëmam moo ko may mu saña lekk lu nekk; kee, ngëmam lujum doŋŋ la ko ngëmam gu dëgërul may mu lekk.

Ndaxte li Yàlla sàkk lépp a baax, du lenn lees ciy aayal, ndegam kàddug cant lees ko jariñoo.

¶ Buleen nangu ay àlluwa yu bare te woroo ak sunu ngëm, di leen fàbbi. Li baax mooy ngeen di yokke aw yiw, seen pastéefu xol. Buleen yokke pastéefu xol, ay ndigal yu jëm ci aw ñam, te ña koy sàmm, jariñu leen dara.