TSK

TSK · Leviticus 11:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Su fekkee ne nit ki dafa laal lu sobewu, te seetluwu ko, lu mel ni rab wu daganul te médd, muy rabu àll mbaa ag jur, mbaa luy raam, kon sobewu na, tooñ na.

Hosea 9:3 TSK

Dungeen des ci réewum Aji Sax ji. Efrayim, Misra lay dellu, te ca Asiri, lu daganul lañu fay lekkeji.

Mu dem ba xiif, bëgga lekk, ñu di ko toggal nag lu mu lekk. Ci biir loolu mu daanu leer.

Ngeen moytu yàpp wu ñu sarxal ay tuur, ak deret, ak yàppu jur gu ñu tuurul deretam, ak powum séy. Yooyii, bu ngeen ko moytoo bu baax, def ngeen lu baax. Jàmm ak jàmm.

Li gën sax mooy nga baña lekk yàpp, mbaa nga baña naan biiñ, mbaa leneen lu mu doon lu mana fakktal sa mbokkum gëmkat.

Kon nag: «Nangeen génne ci seen biir, te teqlikoo ak ñoom,» la Boroom bi wax. «Lu sobewu, buleen ko laal. Su boobaa, maa leen di dalal.

jëfi lëndëm amul njariñ, buleen ci bokk, xanaa ngeen feeñal ñaawtéefu jëf ja.