Leviticus 13:41
TSK
Bu bopp bi ñàkkee kawar fi féeteek kanam gi, jë baa leel waaye set na.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bu bopp bi ñàkkee kawar fi féeteek kanam gi, jë baa leel waaye set na.
Maay soppli seeni màggal ab dëj, seen woyoo woy diy jooy. Maay wodde bépp lupp saaku yu ñuy ñaawloo, bépp bopp, ma wat ub nel, def ko mu mel ni dëju benn bàjjo bu góor, muj ga di bés bu tar.
¶ Ni ko nit mana dégge rekk, ni laa leen woyofalale kàddu gii, ndax seen néew dooley nitu neen. Noonee ngeen jébbale woon seeni cér, def leen ñuy jaami sobe, ak ndëngte gu jur ndëngte, noonu ngeen wara jébbale seeni cér, def leen ñuy jaami njub gu jur sellnga.
Xam ngeen ne tëleg yaram moo ma mayoon yoon wa ma leen jëkka àgge xibaaru jàmm bi.