TSK

TSK · Leviticus 14:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te nga jël diwu pal gi, sotti ko ci kaw boppam, diw ko.

Na lakk nebbon bi yépp ci kaw sarxalukaay bi, def ko ni nebbonu saraxu cant ci biir jàmm. Noonu la ko sarxalkat biy defale njotlaayal bàkkaaram, mu am njéggal.

Te itam na génne nebbon bi yépp, ni muy génnee nebbonu xar mu ñuy def saraxu cant ci biir jàmm. Na sarxalkat bi lakk loolu ci kaw sarxalukaay bi, mu dolliku ci saraxu sawara yi ñeel Aji Sax ji. Noonu la sarxalkat biy defale nit ki njotlaayal bàkkaar bi mu def, mu am njéggal.

Mu sotti nag tuuti ci diw gi ñuy fale ci boppu Aaróona, diw ko, sellale ko ko.

Te ki nuy saxal ci Almasi, nook yeen, moo nu tabbe diwu pal gi, te moo di Yàlla.