TSK

TSK · Leviticus 14:34

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Jógal wër réew mi mépp, ba mu daj, ndax yaw laa koy may.»

¶ Da ne leen: «Bu ngeen farloo ci déggal seen Yàlla Aji Sax ji, di def li mu rafetlu, di teewlu tey jëfe ay santaaneem, di sàmm bépp dogali yoonam, su boobaa duma leen teg lenn ci jàngoro, yi ma tegoon waa Misra, ndax man maay Aji Sax, ji leen di wérloo.»

Yeen nag ma ne leen yeenay nangu seen réew ñoom, ndax maa leen ko jox, ngeen moom ko, muy réew mu meew maak lem ja tuuroo. Man maay seen Yàlla Aji Sax, ji leen ràññatleek yeneen xeet yi.

«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, suuf sa ca boppam war naa am àppu noflaayam ngir Aji Sax ji.

Nooy gànnaayu jàlli réewum Kanaan fi kanam Aji Sax ji, waaye nun, cér bi nuy moom, wàllu dexu Yurdan wii lay doon.»

¶ Bu leen seen Yàlla Aji Sax ji yóbboo réew ma ngeen jëm, ngir nanguji ko, moo fay dàqe xeet yu bare fi seen kanam: Etteen ñi ak Girgaseen ñi ak Amoreen ñi ak Kanaaneen ñi ak Periseen ñi ak Eween ñeek Yebuseen ñi; juróom ñaari xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole.

¶ Dogal yeek àttey yoon, yi ngeen di sàmmoo jëfe seen giiru dund ca suufas réew, ma leen seen Yàllay maam Aji Sax ji moomale, moo di yii:

¶ Gannaaw bu leen seen Yàlla Aji Sax ji wollilee xeet yi mu leen di jox seenum réew, ngeen dàq leen, ba dëkke seeni dëkk ak seeni kër,

te ngeen bind ca mboolem kàdduy yoon wii, gannaaw bu ngeen jàllee. Su ko defee ngeen mana dugg ca réew, ma leen Aji Sax jiy jox, réew mu meew maak lem ja tuuroo, noonee leen ko seen Yàllay maam Aji Sax ji waxe woon.

Aji Sax ji day alag kër ku bon, di barkeel waa kër ku jub.

Amos 3:6 TSK

Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?

Micah 6:9 TSK

Baatub Aji Sax ji mooy joor dëkk bi, te ndam mooy ñeel ñi wormaal sa tur. «Dégluleen seen yetu mbugal, ak ki ko yebal,